Voici le texte intégral de Keur Gui: « Le Saï saï au cœur « 

Artiste: Keur Gui……….Son: Saï saï au cœur

 Intro:
A l’heure du bilan RIEN (nada)
Rien à se mettre sous la dent
7 ans ñuy perte sunu temps
Ci bii banditisme d’état sans précédent
Mêmes fainéants
Mêmes incompétents
Mêmes vieillards dans le vent
Ñaata bubu golo ñoo transhumer
Ñaata patrons de presse achetés
Ñaata juges sans dignité
Ñaata bavures policières
Ñaata litiges fonciers
Ñaata ministres yu cuune
Ñaata scandales
Ñaata ñoo am couverture médicale
Ngay saraxe ay bourses sociales
Rien que ton parti
Faate la patrie
Pétrole sa rakk
Contrats  say goro
Marchés publics tubaab yi
Sénégalais kolo kolo
Ammu ñu vergogne
Siimee sen cere suñu ròngoñ
Jox ñu suñu cartes yi
Da nga tële
Xam nga ni moos dañ la fiy jële

Refrain:
Justice bi leegi dafa naxsaay
(Haay haaay)
Li duuf ci nagg bi lepp daf ko jaay
(Haay haaay)
Ñi ànd’ag moom ño ngi ndàtsaay
(Haay haaay)
Dëg dëg Macky moy saay saay
(Haay haaay)

Couplet 1:
Lepp lum la dikk
Ludul yobbu la DIC
Xamal ni dina diig
Waaji mo mattul njiit
Di feet rekk ni jiit
Kom kom bi yëpp mu ñiit
Askan wi dee akk xiif
Nga jàpp doori liif
Jàmm daf fi gëj
Étudiants yi nga dëj
Élections yi di lëj
Opposants yi nga tëj
Nguur gu saggaan
Ñun ñu marr naan
Dëkk bee panne
Ndaw ñi walliyaan

[Refrain]

Couplet 2:

Fim ne yëpp a loof
Reew mi doo tuñ doff
Say chartes taxul ñu xoff
Da nga ñu mujjee soof
Lum wax rekk ne waxeet
Jaay na sunu xeet
Lebbe sunuy têtes
Baayil ñu fii ay dettes
Njàng ma ngi l’hôpital
Ñakk plateau médical
Falu fatte lila fal
Sa bopp rekk nga deffal
Référendum nga tekk say lois
Bëgga nangu sunuy droits
Joxoo ndaw ñi ay emplois
Tëyeel sa dipla en bois
Duy sa poche ay milliards
Gouvernement des connards
Taf sa bord ay vieillards
Bës Reubeuss akk mille yarr

[Refrain x 2]

Saay saay lë (x3)
Bu maaga maag
Saay saay lë (x2)
Pataa bu puff
Saay saay lë (x2)
Bu ngande

LAISSER UN COMMENTAIRE

S'il vous plaît entrez votre commentaire!
S'il vous plaît entrez votre nom ici